Sàmba Seytaane ak Amari Njullit
Samba le satanique et Amary le pieux
— Léeboon!
— Waaw kon… ay ca ñu may ko déglu. Aa... du ngeen déglu?
— Léeboon... daa... amoon...
— Amoon na fi…
— Daan na am.
— Ba mu amee yeen a fekke? Sàmba Seytaane la woon ak Amari Jullit… leegi si tey seen baay bàyyi leen fi, dem tukki ne leen: “Seen yaay bu amee doom na ngeen jël béy wi reyal ko ko. Fas wi bu amee doom na ngeen tibb ci ngooñ mi jalal ko”.
Yalla def seen yaay jëkk a am xale. Leegi mu tibb ngooñ dem jalal yaayam. Yaayam ne ko: “Ey Sàmba Seytaane. sa baay de waxula woon lii”.
Mu ne ko: “Dangay bëgg lekk, bëggoo ma rey la”. Yaayam ni ko: “Man de du ma lekk ngooñ”. Mu dàldi koy jam mu dee. Léegi si tey fas wi am doom. Mu dàldi rey bëy wi tegal fas wi. Fas wi di ŋexal. Mu dàldi koy jam xeej mu dee. Mu dàldi tëdd ca lal ba. Dàldi ne liir bi: “Kaay jëndal ma sigareet”. Liir bi di jooy. Mu dàldi ne ko: “Aan! May wax ngay jooy”! Mu dàldi koy fetal mu dee. Mu dàldi dem war mool wa nga xam ne démb la juddu dàldi ne ko: “Mool wi demal jëndëli ma sigareet. Mool wiy tërëf, mu dàldi koy jam xeej mu dee!
Léegi si tay Amari jullit ñëw ne ko: “Ey… Sàmba Seytaane. lii nga def dey sama baay waxula ko woon!” Mu ne ko: “Man dey rey naa leen. Na ñu dem war gëléem ga”. Ñu dem, di daw, di daw, di daw ba yegsi ci benn lawbe. Mu ne ko: “Lawbe, abal ma sa semmiñ ma wàññi tànki gëléem gi ndax tànk yi da ñoo gudd”. Amari Jullit ne ko: “Eey Sàmba Seytaane., tee ngaa bañ a def noonu”! Mu ne ko:”Noonu dey laay def!” Daldi dagg ñéenti tànku gëléem ga. Gëléem ga dàldi fay yam.
Ñu daldi dem, di dox ak seeni tànk, di daw, di daw ba ci génn kër. Ñu daldi ne boroom kër gi: “Ñun dey fu nu fanaan la ñu bëgg”.
Buur ne leen: “Aa… man dey am naa fu ngeen fanaan. Waaye nag fi ma leen di fanaanal dey bare na ñoo xam ne du ma leen fa fanaanal”.
Ñu ne ko: “Fanaanal ñu fa rekk”. Ñu dàldi tëdd ba xaaju guddi, Sàmba Seytaane. jóg dagg kooyu fas u buur ba. Ne ko rapp ca taal ba, di lekk. Dàldi ne Amari jullit: “Ñëwal rekk ñam ni mu neexee, kaay rek ñam”. Amari Jullit dàldi ne bëret jog, dàldi ne ko: “Na nu daw”! Te xam ne tey rekk la ñu nuy rey”.
Ñuy daw, di daw, di daw ba ci genn daqaar. Ñu dàldi cay yéeg. Leegi bi ñu yéegee nag, buur jóg ak waa këram. Ñu takk seeni bool. Ne da ñuy daw ba fu ñu leen dabee rekk rey leen. Ñu dem ba ca daqaar ga ñu yeek, ñu taxaw fa daldi tàmbale togg. Togg seen yàpp ba mu ñor. Ñu daldi ne: “Bu ñu añee ba noppi ñu jóggaat”. Naka la ñu pare rek, Sàmba Seytaane. dàldi ne Amari Njullit: “Na ñu wàcc. Man de dinaa añ ci añ bii”!
Mu ne ko: “Eey sàmba Seytaane.!”
Mu ne ko: “Dinaa ci añ de”! Dàldi dagg ñaari bantam yu am lonku. Mu lonk ndab li, lonk cin li. Toog, yekk, lekk ba pare. Ne ko kàŋ ca nelu buur ba.
Ñu ne: “Wooy jinne yi”! “Waay, jinne yi kay”. Ñu dàldi tëb ne: “Wooy jinne yi ñëw na ñu ci su ñu kaw. Ay nu ñuy def”? Dàldi daw. Ñu dàldi tëb ñoom itam, ni cëpp wàcc. Dàldi ñoom itam daw. Daw ba ca kër gaynde ya. Ñu ne gaynde gi: “Nun dey, danoo amul fu nu fanaan, fu nu wara dal!” Gaynde gi ne leen: “Man dey man na maa ànd ak kenn rëbbi, keneen ki desal ma ci samay doom”. Amari Njullit xam na jikkoy Sàmba Seytaane., dàldi ne: “Na Sàmba Seytaane. ànd ak yaw rëbbi, man ma desal la ci kër gi.” Mu ànd ak sàmba Seytaane.. Lu ñu gis rek Sàmba Seytaane. ni ko: “Dawal, tey nijaay gaynde rey la”! Saa yu gaynde demee ba di ko bëgg a rey rekk, mu ne ko: “Ey budul woon sa mag ja ca kër ga, ndax maa ngi rëbb ngir sama xale yi am lu ñu dundee, lu ma gis ba bëgg koo jàpp rekk nga dàq ko”. Sàmba Seytaane. ne nijaay gaynde: “Loolu de yaa xam”. Ñu jàppee ko noonu, ba mujj amuñu dara. Ñu dàldi ñibbisi. Gaynde ne Amari Njullit: “Bu dul woon yaw, da naa rey sàmba Seytaane. ndax lu ma gis ba bëgg koo rey rekk, mu ne ko dawal tay nijaay Gaynde rey la”. Leegi Amari Njullit daa di ko ne: “Na nu ànd kon dem rëbbi. Moom ñu bayyi ko ci kër gi”. Léegi ñu ànd di japp, di japp ba mu bari.
Sàmba Seytaane. dàldi jàpp doomi Gaynde yepp rey. Dàldi léen sàam ci bunt u kër ga. Dàldi ne: “Bii man, bii Amari Njullit, bii Gaynde”. Dàldi toog ca buntu kër ga di léen xaar. Amari Njullit toog ba mu yàgg, mu dàldi ne nijaay Gaynde: “Toogal fii, man ma dem may la ndox”. Mu ne ko: “Déedeet, na nu dem rekk.” Mu ne ko: “Walaay tόogal fii rek”. Na ka la ñëw rek yém ci sàam yi ne ko: “Laay, doomi Gaynde yi nga rey ba saam leen nii. Bu ñu yaboo daw”. Mu ne ko: “Noonu dey laa léen def”. Ñuy daw, di daw, di daw ba ab céeli fëkk léen. Sàmba Seytaane. ne céeli ba: “Taxawal, sama gënnug poon gaa nga ma bàyyi ca Nijaay Gaynde te di naa ko jëli”. Amari Njullit ne ko: “Gënnug pόon”? Mu ne ko: “Waawaaw”. Mu dem feek Gaynde jooy ba nelaw ci kaw doom ya. Sàmba Seytaane. dàldi jël gënnug poon ga. Dàldi koy tux ba mu yànj dàldi koy ruux ca taatu Gaynde ga. Gaynde ga tëb di ko dàq, di ko dàq ba céeli ba fëkk ko. Bi ko céeli ba fëkke nak, ñuy dem di dem ba yàgg, mu daadi ne: “Li ci taatu céeli bi dey day nurook saa mbaxanam baay ba. Lii dinaa ko luqati.” Ne ko luqéet! Céeli ba ànd ak ñoom ñu daadi ne dàrrr daanu ci suuf daadi dee.
Ba yàgg mbonaat ñëw, yor yaru dund ak yaru dee dàldi koy bàcc Amari Njullit mu jog. Amari Njullit ne ko: “Andi ma bàccal la Sàmba Seytaane., lu ko moy bu jógee da na la rey”. Mbonaat mi ne ko: “Maa koy bàcc de”! Ne ko yar ba téll. Sàmba Seytaane. tëb dàldi ne: “Eey waay, mbonaat? Da ma koy lakk”. Dàldi ne Sàmba Seytaane.: “Téyeel ma ma dem taxani”.
Mu téye. Na ko la ko téye ba Sàmba Seytaane. dem. Mu ne mbonaat ma: “Dawal! Awal nii, boo ko deful di ngéen daje.” Sàmba Seytaane. daldi dajeek mbonaat ma. “Ñaari mbonaat! Man benn, Amari Njullit benn”. Amari Njulllit ne ko: “Boo baa de”! Mu ne ko: “Bu réeroon de ma ñaf sa ndey”. Daldi koy jàpp, lakk, lekk.
Ñu dàldi ànd dem ba ci benn meer. Ñu fekk ko muy foot. Sàmba Seytaane. dàldi ne: “Waaw meer! Man de ñaari yoon yii ban nga ciy jaar ba tekki”? Meer ba ne ko: “Wii yoon dey dangay rey nit, di rey, ba àgg falu buur. Wële nak, dangay def lu neex, di tëdd fu neex ba yegg gumba”. Sàmba Seytaane. ne meer ba: “Man de ci yaw laay tàmbalee” ne ko dexet rendi. Kee moom, Amari Njullit, aw fee, di def lu neex ba àg gumba. Sàmba Seytaane moom di reyante ba àgg falu buur. Amari Njullit di yalwaan ba fekk Sàmba Seytaane. mu toog. Sàmba Seytaane. ne ko: “Amari Njullit danga maa yalwaan si”? Mu ne ko: “Man kat xaw ma fi”. Mu ne ko: “Man la Sàmba Seytaane.! Danga maa yalwaansi”? Mu ne ko: “Waawaaw”. Sàmba Seytaane. yónnee ay puso yu bari, dàldi koy samp ca néeg ba. Fu ne mu samp fa puso, ba néeg bi daj dàldi fàq juroom ñaari yaru daqaar. Dàldi ne Amari Njullit: “Jàllsil”. Jàpp ko di ko door, réll. “Gumba neel jarr”? Amari Njullit ne: “Nee naa jarree”.
Foo fu la léeb doxee tàbbi aljana!